Numbers 23:19
TSK
Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
Waaye su ngeen lànkee, fippu, saamar a leen di xéewloo.» Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
Bésub keroog sagub Yanqóoba sàggiku, yaram wa réer ko, mu jeex tàkk.
Seet ko ci téereb Aji Sax ji, jàng ko; du menn mala muy wuute ca gent ba, lu ci nekk a fay ànd ak moroom ma. Aji Sax jee ko santaane ci gémmiñam, moo leen di dajale, moom ci boppam.
Te lii nangeen ko def ab takk.” Kàddug Aji Sax jee. “Maa ngii di leen dikke mbugal ci bii bérab, ba ngeen xam ne samay kàddooy sotti ba mat sëkk, di seen loraange.”»