TSK

TSK · Isaiah 22:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Su ngeen dee tabax kër gu bees, sàkkal-leen seen kawum taax, ab feguwaay, bala caa nit a daanoo, àqu deret topp seen kër.

¶ Ngóor sa Samiyel nag moom, di liggéeyal Aji Sax ji fi kanam Eli.

Buur ne ko: «Lu la dal?» Mu ne ko: «Man de gore, dama dib jëtun; sama jëkkër a dee.

Moo géej, loo xewle bay daw? Yaw, dexu Yurdan, looy deltu gannaaw?

Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.

Yéeneb bii ñeel na Babilon, muy peeñum Esayi doomu Amocc.

Këri Yerusalem ak këri buuri Yuda dina fees ak sobe ni bérab bii di Tofet. Mooy mboolem kër yu ñu doon taalal cuuraay ca kaw taax ya ñeel biddiiw yépp, ak di fa tuural yeneen yàlla.”»

Waa Babilon ñiy song dëkk bii dinañu dugg, taal ko, lakk ko ba mu jeex, lakkaale kër ya ñu doon taalal Baal tuur mi, cuuraay ca kaw taax ya, di fa tuural yeneen yàlla ay saraxi naan, ba di ma merloo.

Kaw taaxi Mowab yépp aki péncam, fépp ay yuuxoo di jib. Maa toj Mowab ni ndab lu kenn soxlaatul.» Kàddug Aji Sax jee.

ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi, ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji tey giñe Milkom, yàllantu ji,

Ñooñoo di xeetu Israyil wi xéewloo céru doon doomu Yàlla, xéewloo daraja, xéewloo kóllëre yi, ak ndigali yoon wi, ak liggéeyu jaamu Yàlla gi, ak dige yi;