¶ Ba mu ko defee Firawna woo Musaak Aaróona, ne leen: «Ñaanleen Aji Sax ji, ngir mu teqale nook mbott yi, man ak sama waa réew. Kon dinaa bàyyi mbooloo mi, ñu dem rendili Aji Sax ji sarax.»
TSK
TSK · Isaiah 23:9
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yuril sa mer, te xool képp ku bew, detteel ko,
Bésub keroog booba, ku bew bay regeju mooy detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
Bésub keroog booba, kuy daŋŋiiral, detteelu, sagub nit sàggiku, Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
Doom aadama torox na, nit detteelu na, ku doon regeju, detteelu.
Boroom baa ngoog, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, mu ngi gor garab yi, di rajaxe car yi, njobbaxtal ya gëna kawe dog, la ca gënoona siggi, wàcc.
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee giñ ne: «Lu ma nar déy mooy am, lii ma mébét, mooy sotti.
Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.
Te nga wax ne: “Aji Sax ji, yaw déy, yaa xamle ne dëkk bii dina tas, dara du ci dëkkati, du doom aadama, du rab. Ab gent lay doon ba fàww.”
¶ Bokk yi, seetleen ñan ngeen woon, ba ñu leen di woo. Barewul ci seen biir ay xamkat, ci gis-gisu nit ñi, barewul ci yeen ay boroom doole, barelewuleen ñu rafet ab juddu.
Loolu moo doon naka jekk nammeelam gi mu sottale ci Almasi Yeesu sunub Sang.