Isaiah 60:1
TSK
Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
mu dig leer, ñeel jaambur ñi, sagal Israyil sa ñoñ.»
te baña def ni Musaa ma daan muur kanam ga, ndax bànni Israyil bañ ne jàkk ci leer guy wéy, di giim, di giim ba jeex.
Seenum xel a tàbbi ag lëndëm, ñu tumurànke dundin wi Yàlla di maye, te umple gi ci ñoom moo tax, ndax seenug dëgër bopp.
Noonu la Noo gu Sell gi firndeele ne yoon wu maye dugg ca bérab bu sell baa sell feeñagul woon, te fekk néeg bu jëkk ba di taxaw ba tey.
¶ Léegi nag bokk yi, am nanu sañ-sañu dugg ca bérab bu sell baa sell, ngir deretu Yeesu,