TSK

TSK · Isaiah 27:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi.

Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.

Ay askan yu bareey dikk, naan: «Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji, fa kër Yàllay Yanqóoba, mu xamal nuy yoonam, ba nu doxe yooyu ñallam.» Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo, Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.

Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.

def kow yoon, ñeel ndesu ñoñam, ña dese fa Asiri, mu mel ni yoon wa ñeeloon Israyil, bésub keroog ba ñuy génn réewum Misra.

Yeen waa àddina wërngal këpp, yeen ñi dëkke suuf si, séentuleen raaya ba sampe fa tund ya, dégluleen liit ga ñuy wali.

Su keroogee mbedd bawoo Misra ba Asiri, waa Asiri di dikk ba Misra, waa Misra di dem ba Asiri te Misra di jaamoondook Asiri.

Maa naa bëj-gànnaar: “Ësi!” ne bëj-saalum: “Bul téye!” Jëleel sama doom yu góor fu sore, délloosi, te jëleji sama doom yu jigéen fa cati àddina.

«Man maa xam seeni jëf ak seeni xalaat. Bés bii taxaw lees di dajale xeetoo xeet aki làkk, ñu dikk ba niir samag leer.

Ñu dikk Misra, baña déggal Aji Sax ji, daldi àgg dëkk ba ñuy wax Tapanes.

Ñooy sarxe jur gi ñu may jooxeel, lekk yàpp wi, Aji Sax ji buggu ci dara. Maay bàyyi xel ci seen ñaawtéef, mbugale leen seeni moy, te ñoom Misra lañuy dellu.

Ni njanaaw lañuy loxe, jóge Misra, mel nim pitax, bawoo Asiri. Maa leen di dëël seeni kër.» Aji Sax jee ko wax.

Yuda déy laay bank, muy samag xala, te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi. Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan). Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.

Fa réewum Misra laa leen di waññee, te fa Asiri laa leen di dajalee, yóbbu leen réewum Galàdd ak Libaŋ, te deesu fa gis fu ñu xaj.

Waaye li ko dale penku ba sowub jant, fu ci nekk la sama tur màgge ci biir xeet yi, te fépp lees di taale cuuraay, ngir sama tur, boole ci sarax su set, nde sama tur a ni màgge fi biir xeet yi.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Luke 4:18 TSK

«Noowug Boroom baa ngi fi sama kaw, moo ma fal, ngir ma yégal néew-doole yi xibaaru jàmm bi. Da maa yebal ngir ma yégal jaam yi ne dees na leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, yégal ñi ñu not, ne dees na leen jot,

¶ Waaye dama ne: xanaa dañoo déggul? Ahakay! Ndax «Àddina sépp la seen baat jibal, cati suuf sépp la seen kàddu dajal.»

¶ Waaye yeen fi ngeen agsi moo di tundu Siyoŋ, dëkku Yàlla jiy dund, te mooy Yerusalem ga ca asamaan, yeena àgg fa junniy junniy malaaka, dajee di màggal;

¶ Ba mu ko defee juróom ñaari malaaka yi yor juróom ñaari liit yi di waaja liit.

waaye bu bési kàddug juróom ñaareelu malaaka mi taxawee, ba mu tàmbalee wal liit gi, su keroogee pexem Yàlla miy kumpa dina sotti, na mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»