TSK

TSK · Isaiah 27:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Bés niki tey fasal naa sama bopp kóllëre sama diggante ak yeen ak seen askan,

Mooy sàmm jéegoy wóllëreem, ku bon sànkoo biir lëndëm, nde doole mayewul ndam.

Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.

Kii du la bàyyi nga tërëf, sa sàmm bii gëmmul.

Su boobaa ab làggi ne jàyy ni kéwél, ab luu sarxolle. Am ndox ay fettaxe màndiŋ ma, ay wal wale joor gu wow,

Maay sottim ndox suuf su mar, ak wal yu waleg joor gu wow. Maay sotti saw askan samag noo, sama barke sottikul ñi nga meññ,

Fàttlikuleen cosaan la woon. Man mii maay Yàlla, du keneen. Amul Yàlla ju mel ni man!

Aji Sax ji di leen jiite fu ngeen tollu, di leen màndale joor gu maral, dëgëral seeni cér, ngeen mel ni tool bu ñu suuxat, mel ni bëtu ndox bu dul ŋiis,

¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Man ci sama bopp, maa ngii di wër samag jur, maa leen di seet.

Maa leen di sol samag noo, ngeen dund, ma samp leen seen suufas bopp, ba ngeen xam ne man Aji Sax ji maa wax, maa def. Kàddug Aji Sax jee.”»