«Ay móol màbb, nu yett ponkali doj, tabaxaat, xànqi garab yu ndaw daanoo ca, nu wuutal ca garabi seedar yu mag.»
TSK
TSK · Isaiah 28:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bésub keroog Aji Sax ji dikke saamaram bu jàmbaare, ñàng te réy, ba dal ci kaw Lewiyatan, jaan ja ca xél wa, Lewiyatan jaan jay wañaaruy dem, ninki-nànkay géej jooju lay rey.
Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi moo lay dikke dënook suuf su yëngu ak riir mu réy, ngelaw riddi, di ngëlén, ànd ak sawara wuy xoyome.
Boroom bi, Aji Sax jaa ngii, dikkaale doole ak kàttanu kilifteefam. Mu ngii ànd ak ñi mu yooloo, ñu dig peyam, dox jiitu ko.
«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maay jeexal mbooloom Misra mu réy, jaare ko ci Nabukodonosor buuru Babilon.
Mbàmbulaan lay walal ba faagaagal dëkk bii, te mooy toppi noonam ba ca biir lëndëm ga.
looloo tax ci benn bés la musiba yiy këppoondoo ci kawam: mbas, deele akub xiif, te dees na ko lakk ba mu jeex, ndax Boroom bi Yàlla mi ko mbugal moo am doole.»