Bul yokk ay waxam, mu weddi say fen, nga weeru.
TSK
TSK · Isaiah 29:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moyal yoon wi; lajj, wàcc xàll wi, te may nu jàmm ak Aji Sell ju Israyil.
Man mii lañuy sàkku bés bu ne, di wuta xam sama coobare! Mbete xeet wuy def njekk, te waccul ndigalu yoonu Yàllaam. Ñu ngi may ñaan àttey njekk, di sàkku man Yàlla, ma jege leen,
Bu ñu nee sax: “Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund,” ay fen lañuy giñ.»
Ñu ne Yonent Yàlla Yeremi: «Ngalla danu lay dagaan, nga ñaanal nu ngir ndesu askan wii ci sa Yàlla Aji Sax ji. Bare woon nanu, waaye gis nga lu néew li des ci nun.
Noonu la sama ñoñ di dajesee fi yaw, toogaanu la, di la déglu. Dañuy déglu say wax, waaye duñu ko jëfe mukk. Lu neex lañuy wax waaye amin wu lewul rekk la seen xol di sàkku.
Te mboolem yëf yooyu dogali yoon yi jëm day jeex doŋŋ bu ñu leen jëfandikoo. Loolu ay santaane aki àlluway nit doŋŋ la.