TSK

TSK · Isaiah 29:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Loolu dalul moos ku bon, kay mel ni xatax bu ngelaw li wal.

Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellngay dëkkuwaayi Aji Kawe ji.

Moo tax Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, di yebal woppi ràgg fi kaw mbuxreem yi, seen daraja tàkk, sawara xoyom ko.

Doxandéem yii diy noon, ni ngay dàqe tàngoor fi bérab bu ne sereŋ, ni ngay dakkale seen coowal xare. Ni aw tàngoor di dakke ndax aw niir, ni la woyu ñu néeg ñi di selawe.

Waa Misra, niti neen, duñu Yàlla; seeni fas it, suuxu neen, duñu leneen. Aji Sax jeey xàcci loxoom, kiy walloo mooy tërëf, ki ñuy wallu daanu, ñoom ñépp bokk sànku.

¶ Ba loolu amee malaakam Aji Sax ji dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp diy néew.