Buleen di naxante, waaye ragal-leen seen Yàlla, ndax man Aji Sax ji maay seen Yàlla.
TSK
TSK · Isaiah 3:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nit a ngi toxal kemu suuf, nit a ngi sàcc ug jur, foral leen.
Yàlla daal, soxlawula liñbat nit ki, bala mu koy woo cib àtte.
Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.
Tóokëru Aji Sax ji Boroom gàngoor yi kat, mooy waa kër Israyil. Niti Yuda it ñooy njëmbat li mu safoo. Mu di ko yaakaare njub, njubadi ne jaas. Mu yaakaar njekk, yuuxi njekkar ne jaas.
Gàngooru sàmm a sëxëtoo sama tóokëru reseñ, joggati sama waar, def waar wi ma neex màndiŋ mu ne maraas.
Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»
Ñooy xemmemi tool, foqati, ay kër, ñu nangu, tey not waay ak waa këram, ak nit ci céru suufam.