TSK

TSK · Isaiah 30:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Da koy lakk, ndax liir wu aaytal la, muy ndimo mbaa bàgg mbaa poqe mbaa kawaru gàtt gu ñu ëcc mbaa wëñ gu ëccu mbaa lu ñu defare der te liir wa tegu ca. Dees koy lakk, ba mu dib dóom.

Bésub keroog booba, yàllantuy xaalis ak wurus ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal, ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,

Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam, nii la mujje am njéggalu bàkkaaram: Day boole doji sarxalukaay bi yépp, rajaxe ni doji kew, xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe, mbaa sarxalukaayi suurukaay.

Ñii déy a yullee wurus ci mbuus, sàkk xaalis, natt diisaay ba, fey tëgg bu leen ci tëggal am tuur mu ñuy sukkal ak a sujjóotal,

Ñoo doon sagoo seen gànjar gu yànj, di ci sàkk jëmmi tuur yu jara bañ te jomblu, ba tax ma defal leen ko sagaru sobe.

Su boobaa yeenay fàttliku seen jikko yu bon yaak seen jëf ju baaxul. Su ko defee ngeen jéppi seen bopp ndax seeni ñaawtéef ak seen jëf ju siblu.

Maa fiy dagge sa dëkki réew mi, màbb sa tata yépp.

Ñu daldi jàpp rab wi, mook yonentu caaxaan, bi defoon ci turu rab wi ay kéemaan yu mu sànke ña ñu màndargaale woon màndargam rab wi, te ñu doon jaamu jëmmu nataalu rab wi. Ñoom ñaar ñépp lañu sànni, ñuy dund ca déegu sawara waak tamarax bay bax.