TSK

TSK · Isaiah 30:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Lu waral nga di ma nëbbuy daw te bañ maa tàggu? Nde konoon jombul ma yiwi la ci xol bu sedd, bu ànd aki woy, boole ci xalam aki sabar.

Job 21:11 TSK

Day gis ay xaleem di bajantu, goneem yépp di tëbantu.

nit ñi làquji biir xuntiy doj, ruuruji biiri pax, ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab, sore darajay màggaayam, kera buy taxaw, ba suuf di lox.

Aji Sax jeey wowal walum ndox, ma séle géeji Misra. Mooy tàllal loxoom, tiimale dexu Efraat, wal kook doole, dóor ko, mu séddlikoo juróom yaari wal, mu jaarale ca nit ñu caraxu,

Tabala ju xumb selaw na, ña daa xaxaloo dal, mbégtem buumi xalam dakk.

Aji Sax ji déy da maa wax ne ma: «Gaynde gu mag ak gu ndaw, bu jàppee bay xiiru, boo ko wooloon gàngooru sàmm it, duñu soowaloo ba xëbal ko, duñu ñolñoli ba mu dellu gannaaw. Noonu la Aji Sax ji Boroom gàngoor yiy wàcce, xaresi fi kaw tundu Siyoŋ ak waa tund wa.»

Booba baatam la yëngale woon suuf, waaye tey moo dige ne: «Beneen yoon, maay yëngalati suuf, te du suuf doŋŋ, waaye asamaan itam.»