Seen Yàlla Aji Sax ji kat, mooy sawara wuy xoyome, Yàlla ju fiir la.
TSK
TSK · Isaiah 30:33
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndokklee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
Aji Sax jaa ngii, jóge fu sore; mer ma réy, mu jógaale kàddug àrtu gu diis, di waxe xadar ju mat sëkk, baat ba mel ni sawara wuy xoyome,
Gannaaw gi, ba muy sujjóot ca kër tuuram ma ñuy wax Nisrog, Addraameleg ak Sareser, doomam yu góor ñoo ko fa fàdde saamar. Ñoom nag ñu daw làquji réew ma ñuy wax Araraat. Ci kaw loolu doomam Asaradon falu buur, wuutu ko.
¶ «Moo tax ay bés a ngii di ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «su boobaa deesatul wooye bérab bii Tofet mbaa xuru Ben Inom, xanaa xuru Bóomukaay.
«Buurub Asiree nga faak gàngooram gépp, bàmmeeli xarekatam ña wër ko. Ñoom ñépp lañu jam, ñu fàddoo saamar.
Moom mooy ki ngeen gisul te sopp ko. Tey fi tey gisuleen ko, waaye gëm ngeen ko, ba tax leena bég lool, mbég mu màgg mu làmmiñ manula tudd,
kooku dina naan biiñu sànjum Yàlla bu kenn raxul, ñu xelli ko ci kaasu sànjam. Te dees na ko mbugale sawara ak tamarax ci kanam malaaka yu sell yi ak Gàtt bi.