Isaiah 5:6
TSK
Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dama koy gental, mu saxi dég aki dagg, deesu ko tenqi, deesu ko bey; niir yeet, ma sant leen ñu bañ koo tawal.
Fu junniy reseñ taxaw tey, di jar junniy donji xaalisu lëmm, bésub keroog ay dég aki dagg nangu ko.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Kër Buur ak këri waa dëkk ba nag, waa Babilon lakk leen, miiri Yerusalem, ñu màbb.
Jaamookaay yu kawe ya ca Bet Awen, bàkkaarukaayi Israyil yooyu lees di tas. Ay dég aki dagg ñooy sax ca seeni sarxalukaay, dees na ne tund yu mag yi: «Mëddleen nu,» te naan tund yu ndaw yi: «Daanuleen ci sunu kaw.»