Diiwaanu Gosen, ga bànni Israyil dëkkoon doŋŋ, moo mucc ca tawub yuur ba.
TSK
TSK · Isaiah 32:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Soxor bi, bul tëru ku jub ci këram, bul yàq dëkkuwaayam.
Liy dalal seen jamono mooy koomu ndam; xel ak xam-xam, te ragal Aji Sax ji, loolooy seen alal.
Gaynde du fa am, rab wu aay du fa dox, du lenn lees fay gis, ku ñu jot rekk a fay jaare.
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Bés yooyu Yuda day mucc, Yerusalem dëkke jàmm, ñu di ko wooye: “Aji Sax ji sunu njekk.”»
Dootuñu doon sëxëtoom xeet yi, te rabi àll yi dootuñu leen lekk. Dañuy dëkke xel mu dal, te kenn du leen tiitalati.
¶ Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju ŋàbb buumu nattukaay ci loxoom.
Kon des na ba tey noflaayu bésub juróom ñaareel bu ñu waajalal ñoñu Yàlla.