Nabal ne ndawi Daawuda: «Ana kuy Daawuda? Kuy doomu Yese sax? Jamonoy tey jaam yu baree ngi fàqe ci seeni sang.
TSK
TSK · Isaiah 32:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Nit a ngi toxal kemu suuf, nit a ngi sàcc ug jur, foral leen.
Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.
Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ, nappaaje néew-doole yi?» Kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi.
Noo tooñ Aji Sax ji, wor ko, te noo dëddoo sunu Yàlla jii, kàdduy fitna ak fippu, ak fen yu nu mébét, nas ko,
Xanaa fore parlu mu baax mi da leena doyul, ba ngeen di dëggaate li des ci seen parlu mi? Am naan ndox mu teey doyatu leen, ba bu ngeen naanee ba màndi, di wéquy nëxal ndox mi?
Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Israyil, te duma fomm seeni duma. Ñooy jaay jaam aji jub ngir xaalis bu mu leen ameel, jaay aji ndóol bu manul fey dàlli carax.
Wóoy, ngalla ñiy mébét ñaawtéef, di ràbb lu bon ci seenub tëraay, bët set, ñu jëfe ko, ndax xam ne man nañu ko.
Amuloo benn wàll mbaa ab cér ci lii, ndax sa xol a jubul ci kanam Yàlla.
Njullite gu set te mucc sikk fa kanam Yàlla Baay bi moo di lii: di nemmiku jirim akub jëtun ci seen njàqare, tey sàmmu ba mucc ci gàkki àddina.