TSK

TSK · Isaiah 34:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Alku ñeel na képp ku sàkk, bay teg ci bérab bu làqu, li Aji Sax ji seexlu, te ab liggéeykat sàkke ko ay loxoom, muy jëmmu tuur mu ñu yett, mbaa mu ñu móol.» Su ko defee mbooloo mépp àddoondoo, ne: «Amiin!»

boole ca soowum nag ak meewum xar, nebbonu mbote, kuuyi diiwaanu Basan aki bëy, teg ca ngëneeli pepp, may leen biiñu reseñ ju xonq curr, ngeen naan.

Éy Aji Sax ji, jógal dajeek moom, detteel ko. Xettlee ma sa saamar, ma rëcc ku bon.

Yéene bii moo wàccal Duuma: Nit a ngi may wooye tundu Seyir, naan: Jongrukat bi, lu des ci guddi gi? Éy jongrukat bi, lu desati ci guddi gi?

Ana kuy kii bawoo Edom, sol yére yu xonq, bawoo Boccra? Kii ak yéreem yu yànj, di daagoo dooleem ju bare? «Xanaa man mii di waxe njekk, te am dooley walloo.»

Ngeen naa: “Wóoy saamaru Aji Sax jii, xanaa doo selaŋlu? Dellul sa mbar, boog, dal-lu, ne tekk!”

Dangay wax waa gottub diiwaanu Negew, ne leen: “Déglul kàddug Aji Sax ji. Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jafal ci sa biir, daay guy xoyom sa garab yépp, gu naat ak gu wow. Dara du ko mana fey. Daay ga day jóge bëj-saalum ba bëj-gànnaar te ñépp a cay lakk,

«Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Edom a feyu ci waa kër Yuda, feyu ga mu feyu di tooñaange gu réy.

Boroom bi Aji Sax ji nag dafa wax ne: Maa ngii déy di waxe sama tàngooru fiiraange ak xeet yi dul yawut, boole ci Edom gépp, ñoom ñi jiital seen xeebeel, te suuf si ma séddoo, ñu aakimoo ko, te di ko bége mbégte mu mat sëkk, ngir sëxëtoo parluy réew mi.”

¶ Peeñum Abdiyas a ngi. Boroom bi Aji Sax ji moo wax lii ñeel askanu Edom.

Yeen waa Kuus, itam yeen lees di fàdde sama saamar.

¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»

Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.