Numbers 24:8
TSK
Yàllaay ki ko jële Misra, féete ko fa ay béjjén féete nagu àll. Mooy warax xeet yi ko jógal, dammat leen, jamat leeni fittam.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàllaay ki ko jële Misra, féete ko fa ay béjjén féete nagu àll. Mooy warax xeet yi ko jógal, dammat leen, jamat leeni fittam.
Ndax nagu àll a lay nangoo liggéeyal? Mbaa mu di la fanaanal ci sa ngédd?
Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
«Ãa yeen waa Babilon, yeena sëxëtoo xeet wi ma séddoo, di ko bégeek a bànneexoo, di bajantu ni nag wuy bàcc pepp, di ŋexal ni naaru góor?
Maay nàndale suuf sa deret, mu wale ca tund ya, ba feesal yooni ndox yi.