TSK

TSK · Isaiah 35:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Maa jàqoon ba naan: «Ñéppi fen-kat lañu!»

Bésub keroog dees na ne: «Sunu Yàllaa ngii nag! Moom mii lanu yaakaaroon te moo nuy wallu. Aji Sax jii lanu yaakaaroon, nan bég te bànneexoo wallam.»

Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.

ku yàkkamti di ràññee, ba mana xam, làmmiñu ku dër gaawa wax lu leer.

Bésub feyu la, Aji Sax ji di ca feyoo; mooy at mi Edom di yooloo la mu loroon Siyoŋ.

bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.

Aji Sax ji dafa wax, moom mi la sàkk, mooñ la fa sa biiru ndey, di la dimbali. Mu ne: «Yaw Yanqóoba sama jaam bi, yaw Yesurun sama tànnéef laa wax, bul tiit.

Ndaw leeka rafeti tànk, kee bartaloo tund yi, di la dégtalsi jàmm, di la xibaar lu neex, àgge la ag mucc, ne la: «Éey, Siyoŋ, sa Yàllaay Buur!»

Moo ma yónni ngir ma yéene atum yiwu Aji Sax ji, ak at mu sunu Yàlla di mbugalee. Moo ma yónni ngir dëfal ñiy ñaawlu ñépp,

Gannaaw loolu mu ne ma: «Yaw nit ki ñu naw, bul tiit. Jàmm la. Góor-góorlul!» Muy wax ak man, may amaat doole, ba ne ko: «Waxal sang bi, dooleel nga ma.»

Peeñu mi seede la, ñeel jant ba ñu ko àppal, seede su wóor ci na mbir may mujje, te du fen. Su diibee it, xaar ko, day dikk moos te du yàggati.

Léegi nag, Sorobabel, góor-góorlul, Aji Sax jee ko wax. Yaw doomu Yoccadag, Yosuwe sarxalkat bu mag bi, góor-góorlul; yeen mboolem askanu réew mi, góor-góorluleen, kàddug Aji Sax jee. Mu ne: Liggéeyleen, maa ànd ak yeen déy, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

¶ «Maa ngii di yebal sama ndaw, mu xàllal ma aw yoon. Sang bi (/Boroom bi) ngeen di sàkku mooy jekki agsi këram, malaakam kóllëre moomu (/ndawal kóllëre loolu), ki ngeen safoo, mu ngooguy dikk.» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.

Bu xew-xew yooyu tàmbalee sotti nag, taxawleen te siggi, ndax seenug njot dëgmal na.»

¶ Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye.

Ndax kat, «Des nas tuut, as tuut rekk, kiy dikk, dikk te du yeex.

Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi, te ñépp a koy teg bët, ba ca ña ko jamoon sax, te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom. Noonu la moos. Amiin.

¶ Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!