TSK

TSK · Isaiah 35:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Sa ngor nga jiitee mbooloo, mi nga jot, te sa kàttan nga leen di yóbboo ca sa kër gu sell.

Waxleen lii, yeen ñi Aji Sax ji jot, jote leen ci loxol bañ,

Yéeneb waxyu bii ñeel na malay àllub Negew: Réewum tiis laak njàqare, kërug gayndeeki segg, ak saamaan ak céebi, mbaam lañu sëf seen alal, jaare fa, giléem lañu sëf seeni denc, jëme xeet wu leen dul jariñ.

Jàllsileen, jàllsileen bunti dëkk bi, xàll-leen yoonu xeet wi, maasaleleenoo, maasaleleen ngér mi, dindi doj yi! Yékkatileen raaya ju askan yépp gis.

Bésub mbugal laa mébétoon, te atum njot teew.

Maay fas ak ñoom kóllëreg jàmm, maay far ci réew mi wépp rab wu aay. Su boobaa ñu dëkke màndiŋ mi ci xel mu dal, di fore bët biir gott bi.

Bésub keroog,» kàddug Aji Sax jee, «Ca nga may wooye “Sama jëkkër,” te dootoo ma wooye “Sama Baal.”»

Moo maye bakkanam ngir nun, moo nu jot, ba nu mucc ci gépp njubadi, moo nu def askan wu mu setalal boppam, séddoo nu, nuy askan wu farlu ci jëf ju baax.

Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.