2 Kings 19:1
TSK
¶ Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Naka la ko Buur Esekiya dégg, daldi xotti ay yéreem, sol saaku yu muy ñaawloo. Mu dem nag ca kër Aji Sax ji
¶ Ba Mardose yégee la ñu def lépp, daa xottiy yéreem, sol ay saaku, sottikoo dóom, di ko ñaawloo, dugg ci biir dëkk bi, di yuuxu yuux gu réy te metti.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
¶ Ba Esekiya jëlee bataaxal ba ca loxol ndaw ya, jàng ko ba noppi, dafa dem ba ca kër Aji Sax ji. Mu daldi tàllal bataaxal ba fa kanam Aji Sax ji.
Waa Niniw nag gëm Yàlla, daldi yéene koor. Ci biir loolu ku nekk sol ay saaku, di ko ñaawloo, dale ko ca ka gën di mag, ba ca ka gën di ndaw.