TSK

TSK · Isaiah 37:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Rey naa gaynde, rey naa weneen rabu àll wu aay, sang bi. Kon nag yéefaru Filisti bii it ni wenn ci yooyu rab rekk, ndax moo tëkku gàngoori Yàlla jiy dund.

Job 16:4 TSK

Su ngeen doon man, may yeen, kon it ma mana wax ni yeen, tuur leen baati tuuma, wëcc leen bopp.

Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti ndee,

Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.

Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!

Nee yeen waa Sidon ñi mel ni janq bu ñu tëdde, dootuleen xaxaloo. Ayca, dawleen jàlli ba dunu Sippar, te du tax ngeen am fa noflaay.

Nanga leen yégal saw tiis, ne leen: “Naa tuur rongooñ guddeek bëccëg, te du fer; sama bokki bopp yi damm ba dammtoo, ndaw góom bu metti!

Yaw Janq Yerusalem mu taaru mi, lu ma lay wax? Ku ma lay méngaleel? Siyoŋ mu jekk mu taaru mi laa ne, ana ku ma lay dendaleel, ba seral sa xol? Yaw mi sab góom yaa ni géej, ana ku lay faj?

Amos 5:2 TSK

Fëlëñ! Israyil janq ba dootu jógati. Ma nga ñu wacc ca suufas réewam, te amul ku ko yékkati.

«Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.