TSK

TSK · Isaiah 37:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñu ne ko: «Esekiya dafa wax ne: “Bésub tey bésub njàqare la ak mbugal ak gàcce. Mooy li ñuy wax naa: Doom a ngi ci buntub juddu, te dooley wasin réer!

di ma woo bésub njàqare, ma wallu la, nga màggal ma.»

ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,

Lii kat bésub njommite laak coonook toroxte, bésu Boroom bi Aji Sax ji ci gàngoor yi, ci biir xuru Peeñu mi. Tata ja, ñu rëkka rëkk, mu màbb, yuux jolli, àkki tund ya.

Éy Aji Sax ji, ni kuy matu lanu meloon fi sa kanam, di wañaarook a yuuxu.

Éy Aji Sax ji, ngalla baaxe nu; yaw lanu yaakaar! Xëyeel a dooleel wii xeet, wallu nu ci biir njàqare.

Wóoy boobu bés bu réy, ba bés du ni mel! Bésu njàqare lay doon ñeel askanu Yanqóoba, waaye dañuy mucc.

Lu mel ni mititu mat moo dikkal waa jii, te muy doom ju amul xel, ba juddu jot, génnul biiru ndeyam.