TSK

TSK · Isaiah 37:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu wéyee mbooloo ma mépp ne Samiyel: «Ngalla sang bi, ñaanal nu ci sa Yàlla Aji Sax ji, nu baña dee, ndax la nu bàkkaaroon lépp, yokkati nanu ci mbon gu tollu ni di sàkku buur.»

¶ Yonatan ne gàddukatu gànnaayam: «Ayca nu dem ba ca dalub yéefar yee. Jombul Aji Sax ji defal nu yiw, ndax dara du tee Aji Sax ji maye ndam, nu bareek nu néew.»

Rey naa gaynde, rey naa weneen rabu àll wu aay, sang bi. Kon nag yéefaru Filisti bii it ni wenn ci yooyu rab rekk, ndax moo tëkku gàngoori Yàlla jiy dund.

Moo tax Aji Sax ji mere Israyil lool, ba jële leen fi kanamam, ba giirug Yuda rekk des fa.

Jombul nag sa Yàlla Aji Sax ji dégg mboolem kàdduy bëkk-néeg bi sangam buurub Asiri yebal, ngir mu kókkali Yàlla jiy dund. Te kon sa Yàlla Aji Sax ji mooy dogal mbugal mi war ci kàddu yooyu mu dégg. Yékkatil kàddug ñaan rekk, ngir ñi fi desagum.”»

Yàlla da leen doon sànk, bu dul woon ak Musaa, xejjam ba ko kar, àtte leen, mu giif, ba fàkkasu leen.

Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi waccalul woon li nu deseek as néew, ni Sodom lanuy mel, Gomor lanuy neexool.

Wóoy ngalla Asiri miy sama yetu mer, bolde bi ñu ŋàbb di samam sànj,

Bëkk-néeg ba nag taxaw, xaacu ca kaw ci ebrë ne: «Dégluleen kàdduy buur bu mag bi, buurub Asiri.

Tuuri réew yii yépp, ana mu ci xettli menn réew ak man, ba Aji Sax ji wara mana xettli, Yerusalem ak man?”»

Yaw Yanqóoba mi néew doole niw sax, yeen góori Israyil. Man, maa leen di dimbali. Kàddug Aji Sax jee, sab jotkat, Aji Sell ju Israyil.

Ñu ne Yonent Yàlla Yeremi: «Ngalla danu lay dagaan, nga ñaanal nu ngir ndesu askan wii ci sa Yàlla Aji Sax ji. Bare woon nanu, waaye gis nga lu néew li des ci nun.

Amos 5:15 TSK

Bañleen lu bon, bëgg lu baax, di doxal yoon ci pénc. Jombul Aji Sax ji Boroom gàngoor yi baaxe ndesu askanu Yuusufa.

Kon nag tuddanteleen seeni bàkkaar tey ñaanalante, ndax ngeen wér. Aji jub ji, ag ñaanam, doole lay dale.