TSK

TSK · Isaiah 37:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Seen juróomi nit ay dàq téeméer, seen téeméeri nit dàq fukki junni. Seeni noon la saamar di dal, ñu daanu fi seen kanam.

¶ Ba surgay Buur Esekiya àggee Esayi wax jooju leen seen sang wax,

Nga wax ko ne ko: “Defal ndànk te ne cell. Bul tiit, bul xàddi ndax merum Reccin ak Siri, ak doomu Remalya ji. Duñu dara lu moy ñaari gil yuy saxar!

Ku fitam rëcc, ne leen ko: «Dëgërlul te bul tiit. Sa Yàllaa ngii di la feyul, ba yool say noon. Moom mooy dikk, wallusi la.»

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Man ci sama bopp maa leen di dëfal. Ana lu ngeen di ragal ci nit kuy dee, doom aadama ju bokk akum ñax aw demin?