Fa lanu gis xeetu Nefilim ya, ponkali Anageen ña bokk ca xeetu Nefilim ya, nuy niru sunu bopp ay soccet fi seen kanam, di leen ko niru, ñoom it.»
TSK
TSK · Isaiah 40:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Niir yee ko làq ba du nu gis, fa muy doxantoo ca kaw taaxum asamaan!»
Ana ku xam ni aw xiin di firikoo, ba dënu fettaxe xaymab Yàlla ba?
Ana foo nekkoon ba may samp suuf? Waxal su la ko sam xel mayee.
Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu, Aji Sax jee falu buur ba fàww.
Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex. Bu ma yóbboo sama diggi fan.
Ba muy taxawal asamaan, maa nga fa, ak ba muy rëdd fa asamaan taseek géej,
Xeet yaa ngii, mel ni aw toq ci biir bagaan, jàppeesu leen lu moy diisaayu feppu suuf! Dun yi lay yékkati ni pëndub suuf!
Du toqi, du nasax, ba keroog muy dëj àtteb yoon fi kaw suuf, fa waa dun ya di séentu ndigalu yoonam.»
Aji Sax ji sa jotkat dafa wax, moom mi la bind ba ngay sosu, ne: «Man maay Aji Sax ji sàkk lépp. Man doŋŋ maa tàllal asamaan, lal suuf, kenn wéttaliwu ma ca.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal man? Ana ban bérab ay sama dal-lukaay?
¶ Ab yéenee ngi, di kàddug Aji Sax ju dikkal Israyil. Kàddug Aji Sax jee, ki firi asamaan, lal suuf, te bind noowug doom aadama ci biir doom aadama.