TSK

TSK · Isaiah 40:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaay buub nit, nelawal ko. Suba mu jebbi nim ñax,

Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.

Nit aki fanam di saxayaay suy law ni tóor-tóoru àll;

Yeen waa Siyoŋ, serleen te sarxolleel ku màgg ki fi seen biir, Aji Sell ju Israyil.»

Baat a ngi jib, naan: «Xàll-leen yoonu Aji Sax ji ci màndiŋ mi, fàkkal-leen sunu Yàlla xàll wu jub fi joor gi.

Aji Sax ji nee: «Xaacul loo man, te bul ñéeblu; àddul ni bufta, te yégal sama ñoñ seen bàkkaar, ngir waa kër Yanqóoba yii xam seeni moy.

«Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg, nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi fàttliku sa ngor ba ngay ndaw, ak sa cofeel ba nga deeb séet, ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma, ba ngay jaare fa dara dul sax.

Hosea 5:8 TSK

«Wal-leen bufta gi ca Gibeya, jibal liit gi ca Raama te yéene ca Bet Awen. Moytul sa gannaaw, Beñamin.

Ndax bindees na ne: «Bépp boroom suux, nim ñax la mel, mboolem darajaam mel ni tóor-tóoru àll, ñax ma wow, tóor-tóor ma ruus.