Éy bu ma xamoon fa may gise Yàlla, ba àkki péncam,
TSK
TSK · Isaiah 41:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Takkul boog te góor-góorlu, ma laaj la, nga xamal ma.
Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
Yeen xeet yi, xaaculeen, dees na leen rajaxe. Yeen waa cati àddina, teewluleen! Gañoo gañu, ñu rajaxe leen! Ma ne: Gañoo gañu, ñu rajaxe leen!
Yeen xeet yi, jegesileen te déglu; yeen askan yi, teewluleen! Na suuf ak li ci biiram déglu, muy àddinaak lépp lu mu jur.
«Waxleen seenu lay,» la Aji Sax ji wax, «Biral-leen seeni firnde,» la buuru Yanqóoba boobu wax.
Yeen waa duni géej, dégluleen ma; yeen askan ya fu sore, teewluleen ma. Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji wooye, moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.
Aji Sax ja moom, ma nga ca màkkaanum sellngaam, na àddina sépp selaw fi kanamam.»