Ay bés a ngi ñëw Yanqóoba saxi reen, Israyil moomooy tóor, law, ba feesal déndu àddinaak meññeef.
TSK
TSK · Isaiah 41:19
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Màndiŋ ak suuf su ne sereŋ dina bég, joor gu wow bànneexu, tóor ba ne ràññ.
Aji Sax jeey dëfal Siyoŋ moos, dëfalaale fépp fu fa dib gent, ba def màndiŋam ni toolub Àjjana, jooram gu wow mel ni toolub Aji Sax ji, mbégteek bànneex teew fa, ak cant gu woy feelu.
Taaru àllub Libaŋ a lay ñibbsil, garabu sippar, pẽe ak geneen gu dëkke naat, taaralsi sama kër gu sell gi, ba ma terale ci sama ndëggastalu tànk.
ngir tabb waa Siyoŋ ñiy ñaawlu, jox leen kaala gu wuutu dóom bi ñuy ñaawloo, ak diwu mbégte mu ñu weccikoo seenu tiis, ak mbubbam cant mu ñu weccikoo xol bu jeex, ba ñu naa: «Ñii ñoo di ponkali garabi njekk yi, njëmbat li Aji Sax ji jëmbat, ngir teewal teddngaam.»
¶ «“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Man ci sama bopp maay sàkke ab car ca njobbaxtalu garabu seedar gu kawe ga, sàkkal ko bérab. Car yu ndaw ya ca kaw laay fàqe car bu nooy, jëmbatal ko sama bopp ci kaw tund wu mag te kawe.