TSK

TSK · Isaiah 41:25

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 1:2 TSK

¶ Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda.

Peeñu mu ñàng lañu ma ci wax. Workat biy wor, yàqkat biy yàq. Yeen waa Elam, songleen; yeen waa Medd, gawleen leen. Dakkal naa mboolem onk yu ñu sabab.

Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!” Mooy matal sama bépp nammeel, te it moo naa ci Yerusalem: “Nees ko tabaxaat,” kër gu sell gi, laa ne: “Nees ko yékkatiwaat!”»

Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.

«Yékkatileen ub raaya fi réew mi te walal liit gi xeet yi. Dajaleleen xeet yi fi kaw Babilon, te xabtal fi kawam réew yii: Araraat ak Minni ak Askenas. Tabbal-leen ko njiitu xare mu ko song, indil koy fas yu saf ndiiraani njéeréer.

Ni ñeyi xare lañuy mel, di joggati banu mbedd mi ci biir xeex bi. Noonu lañuy xaree, nde ñoom la Aji Sax jiy àndal, ñuy torxal gawar yi.