TSK

TSK · Isaiah 41:29

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buleen dëddu mukk, ndax su boobaa topp ag neen lay doon; lu dul jariñe, du xettlee, ndax tuur yi kat, neenug neen la.

Seeni tuur xaalis laak wurus, di liggéeyu doom aadama:

Ma ne, yeen daal, dungeen tus; seen liggéey du dara, te ku leen taamu di ku seexluwu!»

yékkati teg ci mbagg, yóbbu, teg bérab, mu des fa; du jóge fa mu tege, ku ko woo wall it, du wuyu, ba jot ko ci njàqare.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy; màndargam asamaan, buleen ko tiit; na ko yéefar yi tiit.

Xërëm, waxi neen, gisaanekat gisi fen, seeni gént, nari neen, te caaxaani neen lañuy dalalee. Moo tax mbooloo mii di taxawaalu niy xar, tumurànke ndax ñàkkub sàmm.