Li waral loolu moo di bànni Israyil dañu di sama jaam yi ma génne réewum Misra. Deesu leen jaay njaam.
TSK
TSK · Isaiah 41:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Terewul seeni maam doŋŋ la Aji Sax ji taqool, ngir sopp leen, te yeen, ñi askanoo ci ñoom la taamu ci biir xeetoo xeet, niki bésub tey jii.
Ndokklee yeen xeet wi Aji Sax ji di seen Yàlla, yeen askan wi Aji Sax ji séddoo.
Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.
Moo nangu seen réew, joxe, Kee saxoo ngoram!
Moo tax Aji Sax, ji jotoon Ibraayma, wax ak waa kër Yanqóoba, ne leen: «Léegi Yanqóoba du rusati, du amati yaraanga.»
Yeen sama ñoñ, yeenay samay seede. Kàddug Aji Sax jee. Yeenay sama jaam bi ma taamu, ngir ngeen xam, ba gëm ma, ba ràññee ne maay moom. Sàkkeesul yàlla ju ma jiitu, mbaa ju may wuutuji.
Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam! Ma bind la, ngay sama jaam, yaw Israyil, duma la fàtte!
Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba, yeen bànni Israyil gi ma dégtal sama woote. Maay kenn, maa jëkk te maa mujj;
Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, xool ci Saarata mi leen meññ. Ba muy kenn laa ko woo, barkeel ko, ful ko.
«Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.»
Looloo tax it Ibraayma di maamu ñi xaraf, te du xaraf gu ñu toppe aada, xanaa ñu boole ca topp ci tànki ngëm ga sunu maam Ibraayma amoon ba mu xarafagul.
¶ Waaw kon yoonu Musaa, ana luy njariñam? Dees koo toftal ca dige ba, ngir muy fésal moyi nit ñi ba keroog boroom dige, bi taxawal askanu Ibraayma, dikk. Ay malaaka ñoo biral yoon wi, ci ndimbalal ab jottlikat.
Mbind ma daldi sotti, na mu dikke woon ne: «Ibraayma moo gëm Yàlla, ñu waññal ko ngëmam ag njub,» ba ñu di ko wooye xaritu Yàlla.