TSK

TSK · Isaiah 42:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ñee ngi dëkke lëndëm gu tar, ñu yeewe leen jéngi weñ yu tar.

Aji Sax ji, yaay yokk xeet wi, fulal leen bànneex, ñuy bége fi sa kanam, mbégtem ngóob, mel ni ñuy bànneexoo fa ñuy séddoo alalu xare.

Su boobaa gëti silmaxa muriku, noppi tëx sikkliku.

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

Ca la ubbi seen xel, ngir Mbind mi leer leen.

ngir nga xippil leen, jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, seppee leen ci noteelu Seytaane, indi leen ci Yàlla, ñu am njéggalug bàkkaar, am cér ci biir nit ñi ñu sellal ndax ngëm, gi ñu ma gëm.”

ngir Yàllay sunu Sang Yeesu Almasi, Baay bu màgg bi, sol leen xel mu rafet, ak ngis, ngir ngeen man koo xam bu baax.

¶ Gone yooyu nag, bindeefi suux ak deret lañu bokk doon, ñoom ñépp. Moo tax Yeesu itam dikk bokk ak ñoom woowu nekkin, ngir mana dee ba def deewug boppam pexe mi mu neenale ka yoroon dooley ndee, te mooy Seytaane.

dama lay digal, nga jënd ci man wurus wu ñu xellee ci sawara ba mu set wecc, ngir nga am alal. Jëndal itam yére yu weex yoo soloo, ba làq sa duŋŋaaral gu gàccelu gi; ak tuufaay looy tuufoo, ngir nga gis.