TSK

TSK · Isaiah 43:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Kon gisleen ne man la, man doŋŋ, kenn du Yàlla ku dul man! Man maay rey, di dundal; di gaañe, di wéral; maay jàpp, te kenn du xettli.

Job 9:12 TSK

Kii, bu këfee, ana ku koy tere? Ana ku ko naa: «Looy def nii?»

Job 34:14 TSK

Bu ci Yàlla yebu woon, ba roccim xelam ak noowam,

«Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii, bala maa fàdd te kenn du wallu.

Sab jal a masa sax, te yaa masa nekk.

Bu yàgg lañu ma dëj, ca ndoorte la, bala suuf a sosu.

Bu Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dogalee déy, ana ku koy dogale? Bu xàccee loxoom, ana ku koy fommal?

Maay yégle muj ca ndoorte la, ak jëf ju amagul, lu jiitu bu yàgg. Maa naa sama mébét a ngi, day am, sama bépp nammeel sotti.

Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim, ni gaynde gu ndaw laay mel ak waa kër Yuda. Man, man mii maay xotat, wéy, maay yóbbu te kenn du wallu.

Waaye Aji Sax ji, xanaa du yaa masa nekk? Sama Yàlla sama Aji Sell ji, doo saay. Aji Sax ji, ab àtte nga tabbe ñii, yaw sama cëslaay, mbugal nga fi dëje ñii.

Ci moom lanu jote sunu muur ci kaw dogalu Yàlla mi nu taamu lu jiitu, moom miy sottal lépp ni mu ko namme ci coobareem.

Yeesu Almasi menn mi la woon démb ak tey ba fàww.