TSK

TSK · Isaiah 44:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan.

Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla ji leen yékkatee réewum Misra. Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.

Daa bàyyi xel kàddoom gu sell, ga mu waxoon Ibraayma, jaamam ba.

Ana kan ci yeen mooy dékk lii nopp? Kuy teewlu, ba doxe fa dégg?

Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam! Ma bind la, ngay sama jaam, yaw Israyil, duma la fàtte!

Jegesileen ma, déglu ma; bu jëkk ba tey làquwma, di wax; te ba muy xew, fa laa teew. Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal boole maakam xelam.

«Gayndee fëlle geeram, fàkkaskatu xeet yee jóg, génne këram, nara gental seeni dëkk, ba ñu di gent yu kenn dëkkul.

«Yaw Yanqóoba sama jaam bi nag, bul tiit; yaw Israyil, ma ne bul ragal. Maa ngii di la wallusi, jële la fu sore, jële sa askan fa seen réewu njaam ga, Yanqóoba délsi, dal, aaru, du tiitati.

Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.