TSK

TSK · Isaiah 44:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu Buur seetluwaat mbir ma, daldi sàkklu ñaari wëlluy wurus. Mu ne mbooloo ma: «Yeen waa Israyil, bare ngeen lu ngeen di jaabante yoonu Yerusalem. Xool-leen fii kay! Seen yàlla ya leen génne woon réewum Misraa ngi.»

Ñoom ñépp a ngoogu, tekkiwuñu tus. Seen liggéey, caaxaani neen, seen jëmmi xërëm du dara, cóolóolu kese.

muy saf kuñeental ci biir tóokërub xaal. Du wax, du séqi jéego, ñu di ko gaŋar-gaŋaree. Buleen ko ragal, du lore, du jariñe.»

Nabukodonosor àddu ne leen: «Ndax dëgg la, yeen Sadarag, Mesag ak Abet Nego, yeena baña jaamu samay yàlla, baña màggal jëmmu wurus ji ma samp?

Yeena gis nag mbaa ngeen déggal seen bopp ni Póol moomu di naxee ba fàbbi mbooloo mu bare, te du ci Efes gii rekk, daanaka Asi gépp la: Mu naay: “Yàlla yu loxol nit sàkk du yàlla.”