Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
TSK
TSK · Isaiah 44:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Bumu yaakaar naxi neen, di nax boppam, nde neen ay doon ab añam.
Ku am ug dégg sàkku xam-xam, ab dof di toppi caaxaan.
Seeni loxoo taq deret, ngeen ne lijj ci ñaawtéef, làmmiñ di fen, di sos njekkar.
Yaw Aji Sax ji may dooleel, di ma feg, di ma làq bésub njàqare, yaw la xeet yiy bawoo cati àddina, fekksi la, naan: «Caaxaani neen kay la sunuy maam baaxoo woon, xërëmi neen yu amul njariñ.
«Efrayim, ay fen la ma gawe, waa kër Israyil laa ne, ñoo ma yéewe ag njublaŋ, waaye Yudaa ngi ànd ak Yàlla ba tey, di sàmm kóllëreek Ku Sell ki.»
Mu dem ba noon ngéeja lekk ca xolliti doomi garab ya mbaam-xuux yay lekk, fajeb xiifam, te kenn mayu ko ca.
Ñoo weccee dëggu Yàlla, aw fen, di sujjóotal ak a jaamu mbindeef, bàyyi Bindkat bi yelloo cant ba fàww. Amiin.
Peeñum ku dëng ki liggéeyu Seytaane lay àndal, te dina wone wépp xeetu manoore, aki firnde ak kéemaani feni neen,
Su nu ko gàntalee, moom it dinanu gàntal; su nu ko ñàkkee kóllëre, mu saxoo kóllëreem, ndax manula gàntal boppam.
Ñu xalab ninki-nànka ju réy ja, jaanu cosaan joojee ñuy wax Tuumaalkat bi, di ko wax Seytaane, naxekatu mboolem àddina. Ci kaw suuf lañu ko xalab, mooki malaakaam.
làmp du niiteeti fi yaw, te baatu boroom séet akub séetam du jibeeti fi yaw mukk, ndax say julaa ëppoon doole ci àddina, te say xërëm a sànk askanoo askan.»