¶ Aji Sax ji ne ko: «Dellul topp say tànk te jaare ci màndiŋ mi ba Damaas. Boo àggee, nanga diw Asayel, fale ko ko buurub Siri.
TSK
TSK · Isaiah 45:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Sirus buuru Pers dafa wax ne: Mboolem réewi àddina, Yàlla Boroom asamaan moo ma leen dénk, te moom moo ma tabb, ngir ma tabaxal ko kër ca Yerusalem ga ca Yuda.
Teewul ma des ak yaw, nga jàpp sama loxol ndijoor.
Maa jox ndigal ñi ma beral sama bopp, maa woo sama jàmbaar ñiy réy-réylu, ne leen ñu sottal mbugal mi samam sànj laaj.
Man Aji Sax ji maay sa Yàlla; téye sa loxol ndijoor, di la wax ne la: «Bul tiit, maa lay dimbali.»
Mu ne: «Man Aji Sax ji, maa la woo cig njekk, jàpp la ci loxo, sàmm la, def la ngay kóllëre sama digg ak nit ñi; def la ngay leeru xeet yi,
Aji Sax ji man a, du keneen; kenn du yàlla ku dul man. Maa la gemb, te xamuloo ma,
Aw xeet kay ay bawoo bëj-gànnaar, dal fi seen kaw. Ñooñooy gentalsi seenum réew, ba kenn dootu fi dëkk, nit ak mala, ne mott, ne mes.
«Nàmmleen fitt yi, feesale mbar yi! Aji Sax ji xabtal na buuri Medd fi kaw Babilon, nar koo tas. Lii mbugalu Aji Sax jee, mbugal mi këram waral.
Yaw nit ki, damm naa përëgu Firawna buuru Misra, mu ngii, deesu ko takk, ba mu faju, deesu ko lëmës, ba mu mana ŋàbb saamar.
SÉDDALE: Séddale nañu sam réew, ba jox ko xeeti Medd ak Pers.»
Ma séentu, xool, yem ci kuuy mu taxaw feggook yoonu ndox ma, am ñaari béjjén yu gudd te benn bi gëna gudd ba ca des. Waaye bi gëna gudd moo mujja sax.
Ca la njiit la di woolu kàngami xareem, ñuy gaawtu bay tërëf. b Tata ja lañuy gaaw wutali, ba yékkati ay kiiraay.