TSK

TSK · Isaiah 46:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ca màndiŋ ma it, gis ngeen na leen seen Yàlla Aji Sax ji fabe, ni baay di fabe doomam, ci yoon wi ngeen dox wépp, ba agsi bérab bii.»

«Na wéeroo Aji Sax ji, mu xettli ko; su ko soppee, na ko wallu.»

Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.

Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.

Bésub keroog Boroom bi jooti loxoom ñaareel bi yoon, ngir jotaat ndesu ñoñam, wa des Asiri ak Misra, ak Pattros ak réewum Kuus, ak Elam ak Sineyaar, ak Amat ak biir duni géej ya.

Yaw Yanqóoba, sama jaam bi, déglul boog, yaw Israyil sama tànnéef laa wax.

«Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi! Yeenaka dëddu njekk!

Aji Sax ji seen jotkat dafa wax, Aji Sell ju Israyil da ne: «Maay Aji Sax ji, seen Yàlla ji leen di jàngal seen njariñ, di leen awale fa ngeen wara awe.

Dégluleen maa, yeen ñiy wut njekk, di sàkku Aji Sax ji. Xool-leen doj wi ñu leen yette, xool xóotey kàmb gi ñu leen seppee:

Seen gépp njàqare di njàqarey boppam, malaaka mi mu jàkkaarlool musal leen ca. Moo leen sopp, ñeewante leen, ba jotal leen boppam, te fu ñu masa jaare démb, mu fab leen, boot.