TSK

TSK · Isaiah 48:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ne ko: «Yaa di Yanqóoba, waaye deesatu la wooye Yanqóoba; léegi yaa di Israyil.» Mu tudde ko nag Israyil.

¶ «Buleen giñe sama tur lu dul dëgg, di teddadil seen turu Yàlla. Maay Aji Sax ji.

¶ Ci biir loolu Aji Sax ji dégg la ngeen ma wax. Mu ne ma: «Dégg naa li la mbooloo mii wax. Ñoo yey wax yooyu kàddu yépp.

¶ Seen Yàlla Aji Sax ji moom ngeen di ragal, te moom ngeen di jaamu. Moom ngeen di ŋoyu, te aw turam ngeen di giñe.

¶ Gewasi surgab góoru Yàlla ga, Alyaasa, ne ca xelam: «Eewaay sama sang daal! Day bàyyi Naaman waa Siri bii mu dem noonu rekk; jëlul dara ci li mu indi. Giñ naa ko ci Aji Sax ji, Kiy Dund, dinaa daw dabi ko, ba am ci moom as lëf.»

Ñu bon ñi Yàlla ne leen: «Lu ngeen di tari sama dogali yoon, di waxe sama kóllëre?

Neleen Yàlla: «Yaaka yéemey jaloore! Sa doolee bare, ba say noon rasu,

Dajeleen, di sant Yàlla, yeen askanu Israyil, santleen Aji Sax ji.

Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom, teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.

Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.” Kee di tuddoo turu Yanqóoba, kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,” tey wuyoo turu Israyil.»

«Dégluleen maa, yeen dëgër bopp yi! Yeenaka dëddu njekk!

Seen maam Ibraayma laa ne, moom ngeen di xool, xool ci Saarata mi leen meññ. Ba muy kenn laa ko woo, barkeel ko, ful ko.

Aji Sax jee giñ lii ci ndijooram, giñ ko ci përëgam bi àttan, ne: «Dootuma joxe sam pepp, say noon dunde, te doomi doxandéem dootuñu naan sa biiñ bu bees, bi nga ame saw ñaq.

xanaa di waate Aji Sax jiy dund, ci dëgg ak njub ak ngor, kon xeet yi di barkeeloo Aji Sax ji, di ko sagoo.»

Yeen, nu ngeen mane di sàcc, di bóome, di jaaloo, di giñi fen, di taalal Baal, tuur mi cuuraay, di topp yeneen yàlla yu ngeen xamul,

ak ñiy sujjóotal ci kawi taax gàngoori biddiiw yi, ak ñiy sujjóotal aka giñal Aji Sax ji tey giñe Milkom, yàllantu ji,

¶ Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.

¶ Du caageenu kàddug Yàlla moo neen, ndax ñi bokk ci xeetu Israyil ñépp duñu Israyil tigi.

yu leen ay jinigalkat, ay fenkat yu dërkiis ab xol, di naxe.

¶ Gis naa sa coono ak sag ñàkk, moona yaaka duunle! Gannaaw loolu it, waxi yàq-der yi tukkee ci ñooñu tuddoo Yawut te duñu Yawut, duñu lenn lu moy jàngub Seytaane, dégg naa ko.