TSK

TSK · Isaiah 48:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Job 37:18 TSK

ndax yaa ko lal-le woon déndub asamaan, mu dëgër ni weñ gu ñu xelli?

Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk, taxaw jonn fa asamaan.

Nañu màggal turu Aji Sax ji, kii kat a santaane, lii lépp am.

Moom moo tooge kaw wërngalu suuf, ñi ko dëkke mel niy soccet, moo tàllal asamaan ni ndimo, firi ko nib xayma, dëkke.

Yàlla Aji Sax ji dafa wax, moom mi sàkk asamaan, firi ko; tàllal suuf ak lu mu jur, may noowal bakkan ñi ci kawam, ba ña cay daagoo di noyyi.

Aji Sax ji kat dafa wax, moom mi sàkk asamaan, moom Yàlla mi bind suuf, tabax ko, dëj ko, sàkkewu ko maraas, xanaa tabaxal ñu ko dëkke. Mu ne: «Aji Sax ji, man a, du keneen.

Mu neeti: «Yaw Sang bi, yaa sos àddina ca njàlbéen, te asamaan yi, sa liggéeyu loxoo.