¶ Ba mu ko defee njiiti mbooloo ma dëkk Yerusalem. Ña des ca mbooloo ma tegoo bant ngir fukk ñu daje kenn génne ca, dëkk Yerusalem, dëkk bu sell bi, juróom ñeent ñi ci des toog ca (seeni) dëkk yu ndaw.
TSK
TSK · Isaiah 48:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
Keroog bés booba li des fi Israyil ak li rëcce kër Yanqóoba duñu wéerooti ña leen duma. Aji Sax ji lañuy wóolu, wéeroo ko, Aji Sell ju Israyil.
Dangeena fàtte Aji Sax ji leen sàkk, ki firi asamaan, dëj suuf? Dangeen di dëkke bésoo bés, di tiit xadaru boroom doole buy waaja sànke? Ana fu xadaru boroom doole mujje?
Yewwulee, yewwul, Siyoŋee, làmbool sa doole! Yerusalem, dëkk bu sell bi, solul ba ne ràññ! Ndax du kenn ku xaraful mbaa ku sobewu ku lay songati.
Buleen naxe seen bopp kàdduy caaxaan, naan: ‘Kër Aji Sax jaa ngi, kër Aji Sax jaa ngi fii, kër Aji Sax jee!’
«Ngalla seetal nu ci Aji Sax ji, ndax Nabukodonosor buuru Babilon mu ngi nuy song xare. Jombul Aji Sax ji defaatal nu lenn ciy kéemaanam ba mu dellu gannaaw.»
Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee, seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle, seeni yonent di weccikoo xaalis seenum ngisaane, te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan: «Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir? Musiba du nu dab!»
¶ Ma dikk nag ci yaw miy wuyoo turu Yawut, te yaakaar yoonu Musaa, boole ci di sagoo Yàlla.
Ma gis nag dëkk bu sell bi, Yerusalem gu bees gi, mu wàcce asamaan, fa Yàlla, mel nib séet bu defaru ba jekk ngir jëkkëram.