Isaiah 49:7
TSK
Aji Sax ji jotkatub Israyil, moom ku Sellam ki, moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, te muy surgawu kilifa yi, mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, ay kàngam di sukk, ngir Aji Sax ji boroom worma, ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»