TSK

TSK · Isaiah 49:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.

xanaa di àtte ku ñàkk ci njekk, di dogalal njub, néew-ji-dooley àddina. Mooy dóore àddina, bantub kàddoom, mooy reye ñu bon ñi, ngelawal gémmiñam.

Boroom bi Aji Sax ji moo ma may làmmiñu ndongo lu mokkal, ngir ma xam gan kàddu laay jàpplee ku sonn. Suba su ne mu yee ma, yeel ma nopp bu ma teewloo ni dongo yi.

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

Moo tax Aji Sax ji dafa wax ne: «Soo délsee, ma délloosi la, nga dellu di ma liggéeyal. Soo dee wax ngëneel lu soreeki caaxaan, dinga mel ni yaay sama làmmiñ, te nit ñeey délsi ànd ak yaw, waaye du yaay délsi ànd ak ñoom.

¶ Ci kaw loolu Yeesu àddu ca kaw, ne: «Baay, jébbal naa la samag noo!» Ba mu waxee loolu la dee.

Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.

Gémmiñ gi, saamar bu ñaw a ciy lange, mu di ko cawe askan yi. Moo leen di jiitee yetu weñ, te mooy dëggaate ci biir nalukaay bi, reseñ ji ñuy segale biiñu sànj mu tàng mu Yàlla Aji Man ji.