TSK

TSK · Isaiah 49:24

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi
Ezra 9:9 TSK

Ndax ay jaam lanu, waaye yaw sunu Yàlla, waccewoo nu sunug njaam. Yaa dawal ngor sunu digganteek buuri Pers, ngir mayaat nu dooley tabax sunu kër Yàlla, yékkatee ko ca gentam ba, may nu kiiraay ci Yerusalem ak ci Yuda.

Yaw nag yaa yelloo njekk ci mboolem li nu dal, ndax worma nga jëfe, nun noo bon.

Cant ñeel na Aji Sax ji, ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu.

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

te buleen topp yeneen yàlla, di leen jaamook a sujjóotal; buleen ma merloo ndax yëfi neen yu ngeen sàkke seeni loxo. Su boobaa duma leen teg musiba.

Mu ne ma: «Yaw nit ki, ma ne, yii yax man naa dundaat a?» Ma ne ko: «Boroom bi Aji Sax ji, loolu de, yaw doŋŋ a ko xam.»