TSK

TSK · Isaiah 49:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Esra ne leen: «Ayca demleen lekk lu gëna duuf, naan lu neexa neex te sédd ci ñi amul lu ñu togg; ndax bésub tey bés bu sell la ñeel sunu Boroom. Kon buleen ci naqarlu kat, ndax bége Aji Sax ji mooy seen doole!»

Mooy yékkatil xeet yi raaya, dajale góor ña ñu dàqe Israyil, ak jigéen ña ñu jële Yuda, tasaare leen, ñu jóge ñeenti weti àddina, booloo.

Fonk la, teral la ak sopp la, moo tax ma joxey nit, weccikoo la; ay askan dee, wuutu sa bakkan.

Boroom bi Aji Sax ji moo ma may làmmiñu ndongo lu mokkal, ngir ma xam gan kàddu laay jàpplee ku sonn. Suba su ne mu yee ma, yeel ma nopp bu ma teewloo ni dongo yi.

Kàddug Boroom bi Aji Sax jaa ngi, kiy dajale giiri Israyil yi tasaaroo, mu ne: «Maay dajaleeti, dolli ca la ma dajale woon.»

Mu ne: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey jii li lay may jàmm! Waaye fii mu ne, làqu na say gët.

Dama leen di wax ne leen, bëgga fésal ne Yàlla ku dëggu la moo waral Almasi dikk, def boppam jawriñu Yawut yi, ngir sottal dige ya Yàlla digoon seeni maam.

Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.