TSK

TSK · Isaiah 49:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.

Nanga fa gëdde rabu àll wi ci barax yi, ñooy gétti yëkk yi, xeet yi ci des diy sëllu. Gëdd leen, ba ñu sujjóotalsi laak dogi xaalis. Tasaareel xeet yooyu sopp xare,

buuroo buur di ko sujjóotal, xeetoo xeet di ko surgawu.

Léegi lees ko amal, du lu yàgg. Lu jiitu tey masuleen koo dégg te dungeen ne xamoon ngeen ko.

Yeen waa duni géej, dégluleen ma; yeen askan ya fu sore, teewluleen ma. Fa sama biiru ndey la ma Aji Sax ji wooye, moo tudd sama tur ba ma saa ndey juragul.

Gannaaw laa jox ku may dóor, dékk lex kuy xus sama sikkim, te làquma sama kanam ku may saagaak a serati.

Dees na ko xeeb, daw ko, muy nit ku bare mitit te miin naqar. Mu mel ni ku ñuy dummóoyu, dees koo xeeb te nawloowuñu ko.

Ay doomi doxandéem ay tabaxaat say tata, seeni buur di la surgawu. Maa meroon, duma la, maa la baaxe, yërëm la.

Gannaaw gi, ñetti sàmm laa dàq ci wenn weer. Ci kaw loolu ma doyal ci xar yi, ñoom it, ma génnliku leen.

Ki ñu taajal ndab li, ak surga bi ko taajal, ana ku ci gëna kawe? Xanaa du ki ñu taajal? Moonte man, ci seen biir laa tooge toogaayu surga!

Ñu gënatee xaacu, di sàkku ñu daaj ko ci bant. Seen coow la mujj ko ëpp doole.

¶ «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Filadelfi nag, bind ko, ne ko: «Lii moo di kàdduy ku Sell ki, kiy Dëgg, te yor caabiy Daawuda, di tijji te kenn du tëj, di tëj te kenn du tijji. Mu ne: