Ñaan ma xeeti àddina, ma sédd la ko, nga moom ba ca cati àddina,
TSK
TSK · Isaiah 49:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, àtte ca njub.
«Xool-leen sama jaam bi ma yor, sama tànnéef, sama soppey xol, ci kawam laa teg samag noo, te mooy dogalal xeet yi yoonu àtte.
Maay dëggal sama kàddug jaam, di sottal sama ndéeyal ndaw. Maa naan ci Yerusalem: “Dees na ko dëkke,” dëkki Yuda, ma ne: “Dees na leen tabaxaat, ma dekkali gentam bi.”
Waaye Boroom bi Aji Sax jee may dimbali, ba tax rusuma. Moo ma taxa dogu ba dëgër, ngir xam naa ne deesu ma rusloo.
Maa la sexal samay kàddu, yiire la sama keru loxo, aj asamaan, dëj suuf, ne Siyoŋ: «Yeenay sama ñoñ.»
seeni nit tabaxaat gent ya woon, ngeen yékkatiwaat kenu yu yàgga yàgg. Dees na la wooye jagalkatu xar-xar yi, mbaa kiy yeesal xàll yi, ngir dëkke réew mi.
Ñooy tabaxaat gent ya woon, yékkati bérab ya tasoon bu yàgg, dekkal dëkk yu tas, bérab yu gental ay maasi maas.
Ndaxte Yàlla moo ne: «Jant ba mu jotee laa la nangul, bésu mucc ba laa la wallu.» Te nag, tey jii la jantam jote; tey kat, la bésub mucc.
Jant yooyu amuleen woon benn cér ci Almasi, te amuleen woon jenn yelleef ci mbootaayu bànni Israyil. Bokkuleen woon ci kóllëre yi ëmb digeb Yàlla, te mu fasoo ko ak ñoom. Ñàkk yaakaar, ak ñàkka xam Yàlla ngeen nekke woon ci àddina.
Waaye tey la Yeesu jot ci liggéeyu carxal gu sut gu jëkk ga fuuf, te kóllëre gi mu fas diggante Yàlla ak nit ñi, noonu la gëne gu jëkk ga; dige yi lal kóllëre gu yees gii it, noonu la gëne dige ya laloon gu jëkk ga.