TSK

TSK · Isaiah 5:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Ba Ose duggee juróom ñeenteelu atu nguuram, ca la buurub Asiri nangu Samari, jàpp waa Israyil, yóbbu Asiri. Ñii mu teg leen ca diiwaanu Ala, ñee ca Gosan ca wetu dex ga ñuy wax Abor, ña ca des mu dëël leen ca dëkki xeet wa ñuy wax Medd.

Kàdduy ku jub jariñ na ñu bare, dof ñàkk na bopp, ba far dee.

Seenum réew gental, seeni dëkk xoyomu, seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam, muy gent bu doxandéem tas.

Waaye ñu ngii di xeet wu ñu futti, sëxëtoo; ñépp tëje ciy pax, dence ci këri tëjukaay, ñu doon alalu xare fu leen kenn dul xettlee, xanaa ñu di leen sëxëtoo, te kenn du ne ñu delloo leen.

Kàngam ya yebal seeni surga, ñu rooti; ñu dem, gisuñu ndox ca mbalka ya, délseek seen xotti ndab, jàq, yaakaar tas, ñu muuru di tiislu.

Luy nàmp a nga mara mar, ba làmmiñ taqoo denqleñ. Gone yaa ngi ñaan mburu, te kenn daggalu leen.

Hosea 4:6 TSK

Sama ñoñ a sànku ndax ñàkka xam; yeen, xam-xam ngeen gàntal, ma gàntal seenug carxal. Yeena fàtte seen yoonu Yàlla, man it maay fàtte seeni doom.

Li ñuy fàtte te di ko tey moo di ci kàddug Yàlla la asamaan nekke bu yàgg, te ci kàddoom la suuf bindoo ci ndox, ba génne ci ndox.