Kàddu gu dëgguwul, soreleen ko, te ku deful dara ak kuy def njekk, buleen ko reylu, ndax nit ku bon, duma ko àtte mukk àtteb kuy def njekk.
TSK
TSK · Isaiah 5:20
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñii guddi lañu def bëccëg, naan leer sorewul, te lëndëm teew.
Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.
Booba deesatul wooye ab dof, gor si, te njublaŋ dootu dégg «ku tedd ki.»
Wóoy yeen ñiy walbati àtteb yoon, mu mel ni xay, tey jalax dëgg fi pëndub suuf!
Soof ngeen Aji Sax ji ak seeni wax, ngeen naan: «Nu nu ko soofe?» Xanaa naan: «Képp kuy def lu bon mooy ki baax ci Aji Sax ji, te kooku la safoo.» Mbaa ngeen naa: «Ana Yàlla jiy àtte dëgg sax?»
Yeesu ne leen: «Yeen yeenay jub-jublu ci kanam nit ñi, waaye Yàlla xam na seen xol. Ndax li nit ñi gëna naw, lu seexluwu la fa Yàlla.
¶ Waaye na mu ame woon ci askanu bànni Israyil ay yonenti caaxaan, ni lay ame ci seen biir ay sëriñi caaxaan yuy sërxal ay àlluway sànkute yuy weddi sax Sang bi leen jot, ba yóbbe seen bopp sànkute ju bette.